+ -

عَنْ أَنَسٍ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا تَوَضَّأَ أَحَدُكُمْ وَلَبِسَ خُفَّيْهِ فَلْيُصَلِّ فِيهِمَا، وَلْيَمْسَحْ عَلَيْهِمَا ثُمَّ لَا يَخْلَعْهُمَا إِنْ شَاءَ إِلَّا مِنْ جَنَابَةٍ».

[صحيح] - [رواه الدارقطني] - [سنن الدارقطني: 781]
المزيــد ...

Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bu kenn ci yeen jàppoo daal di sol ay saŋam na ca julli, na masaa ci seen kaw te mu bañ leen a summi bu ko soobee lu dul ci janaba".

[Wér na] - [Ad-daaraqutniy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy - 781]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne bu jullit bi solee ay saŋ ginnaaw bi mu jàppoo, topp mu tojle ginnaaw loolu, bu bëggee jàppuwaat, man naa masaa ca seen kaw bu ko soobe, te julli ci ñoom bañ leen a summi ci ab diir bu ñu xam, lu dul mu ame janaba kon summi gi ak sangu gi da koy war.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Masaa ci ay saŋ du dagan lu dul bu leen solee ci ginnaaw laab gu mat.
  2. Diirub masaa gi ci aji-sax ji: mooy masaa ab bis ak ug guddeem, bu dee aji-tukki ji: ñatti bis ak seen i guddi.
  3. Masaa ci ay saŋ ci toj mu ndaw la jagoo waliis toj mu mag, bu dee toj mu mag nag masaa du ca dagan, waaye fàww mu summi saŋ yi daal di raxas tànk yi.
  4. Sopp nañu jullee ay dàll ak ay saŋ ak lu ko niru, ngir wuute ak Yahuud yi, loolu nag bu dee laab na, te du lor jullikat yi, walla jakka ji niki jàkka yi ñu lal ay laltu buboobaa bu mu ko jullee.
  5. Masaa ay saŋ yombal la ak woyofal ci xeet wi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Kinirowanda Rom Majri الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi