عَنْ عُقْبَةَ بْنِ عَامِرٍ رضي الله عنه قَالَ: كَانَتْ عَلَيْنَا رِعَايَةُ الْإِبِلِ فَجَاءَتْ نَوْبَتِي فَرَوَّحْتُهَا بِعَشِيٍّ فَأَدْرَكْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَائِمًا يُحَدِّثُ النَّاسَ فَأَدْرَكْتُ مِنْ قَوْلِهِ:
«مَا مِنْ مُسْلِمٍ يَتَوَضَّأُ فَيُحْسِنُ وُضُوءَهُ، ثُمَّ يَقُومُ فَيُصَلِّي رَكْعَتَيْنِ، مُقْبِلٌ عَلَيْهِمَا بِقَلْبِهِ وَوَجْهِهِ، إِلَّا وَجَبَتْ لَهُ الْجَنَّةُ» قَالَ فَقُلْتُ: مَا أَجْوَدَ هَذِهِ، فَإِذَا قَائِلٌ بَيْنَ يَدَيَّ يَقُولُ: الَّتِي قَبْلَهَا أَجْوَدُ، فَنَظَرْتُ فَإِذَا عُمَرُ قَالَ: إِنِّي قَدْ رَأَيْتُكَ جِئْتَ آنِفًا، قَالَ: «مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ يَتَوَضَّأُ فَيُبْلِغُ - أَوْ فَيُسْبِغُ - الْوَضُوءَ ثُمَّ يَقُولُ: أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُ اللهِ وَرَسُولُهُ إِلَّا فُتِحَتْ لَهُ أَبْوَابُ الْجَنَّةِ الثَّمَانِيَةُ يَدْخُلُ مِنْ أَيِّهَا شَاءَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 234]
المزيــد ...
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dañu doon sàmm ay giléem samag ay ñëw, ma yóbb leen ci ngoon gi, fekk Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di waxtaanal nit ñi ma fekk ko muy wax:
«amul benn jullit buy jàppu rafetal njàppu mi, daal di jog julli ñaari ràkka, xolam ak jëmmam jublu ca, lu dul ne àjjana war na ci moom" nee na: ma ne: ana lan moo dàq lii, benn waay bu nekk sama kanam daal di ne: ki xolam baax, ma xool rekk Umar di wax naan: gis naa ne leegi nga ñëw, nee na: "amul kenn kuy jàppu jotale njàppu ma -walla matale- njàppu ma, topp mu wax: maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamub Yàlla la di ndawam lu dul ne dees na ko ubbil juróom-ñatti bunti àjjana mu dugg ci bu ko soob"».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 234]
Yonnente day leeral di waxtaanal nit ñi ci ñaari gëneel yu màgg:
Bi ci njëkk: ku jàppu te rafetal njàppu ma jotal ko matal ko ca anam ga ñu ko sunnaale, jox cér bu nekk àqam ci ndox mi, topp mu wax: maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamub Yàlla la di ndawam; lu dul ne dees na ko ubbil juróom-ñatti bunti àjjana yi mu dugg ci bu ko ci soob.
Ñaareel bi: ku jàppu njàppu lu mat lii, topp mu jug ginnaaw loolu julli ñaari ràkka; xolam jublu ca cig sellal ak ug ragal, mu toruxlu ci jëmmam ci mbooleem céri yaram wi ñeel Yàlla, àjjana war na ci moom.