عَنْ المُغِيرَةِ رضي الله عنه قَالَ:
كُنْتُ مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي سَفَرٍ، فَأَهْوَيْتُ لِأَنْزِعَ خُفَّيْهِ، فَقَالَ: «دَعْهُمَا، فَإِنِّي أَدْخَلْتُهُمَا طَاهِرَتَيْنِ» فَمَسَحَ عَلَيْهِمَا.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 206]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Muxiirata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:
Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- cib tukki, ma nar a summi ñaari saŋam yi, mu ne ma: "bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab" mu masaa ca seen kaw.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 206]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci ab tukki, daal di jàpp, ba mu tollee ci raxas tànk yi Al-Muxiirata Ibn Suhbata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàllal loxoom ngir summi li nekk ci tànki Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-di ay dàlli saŋ ngir mu raxas ñaari tànk yi! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ne ko: bàyyileen te bu leen summi, ndax damaa dugal samay tànk ci saŋ yi fekk maa ngi cig laab, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di masaa ci kaw saŋ yi mu wuutu raxas ñaari tànk yi.