عَنْ أَنَسٍ رضي الله عنه قَالَ:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُكْثِرُ أَنْ يَقُولَ: «يَا مُقَلِّبَ القُلُوبِ ثَبِّتْ قَلْبِي عَلَى دِينِكَ»، فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ، آمَنَّا بِكَ وَبِمَا جِئْتَ بِهِ فَهَلْ تَخَافُ عَلَيْنَا؟ قَالَ: «نَعَمْ، إِنَّ القُلُوبَ بَيْنَ أُصْبُعَيْنِ مِنْ أَصَابِعِ اللهِ يُقَلِّبُهَا كَيْفَ يَشَاءُ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 2140]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na baril lu muy wax: "yaw Aji-Wëlbati xol yi saxalal sama xol bi ci sa diine ji", ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, gëm nanu la gëm li nga indi, mo ndax danga noo tiital ? Mu ne: "waaw, xol yi ñoo ngi ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla yi moo koy wëlbati nu mu ko soobe".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2140]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na baril lu muy ñaan Yàlla ag sax ci diine ji ak topp ko, ak sori ag jeng ak ug cànkute, Anas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di yéemu ci li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di baril ñaan gii, Yonnente bi xamal ko ne xol yi dafa nekk ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla te moo koy wëlbati nu mu ko soobe, Xol mooy wàccuwaayu gëm ak weddi, tudde nañu ko xol ngir li mu bari lu muy wëlbatiku; moo gën a man a wëlbatiku cin lu booloo di bax, ku soob Yàlla mu saxal xolam ci njub, saxal ko ci diine, ku soob Yàlla it mu soppi xolam wolif njub jëme ko cig cànkute.