عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«بَادِرُوا بِالْأَعْمَالِ فِتَنًا كَقِطَعِ اللَّيْلِ الْمُظْلِمِ، يُصْبِحُ الرَّجُلُ مُؤْمِنًا وَيُمْسِي كَافِرًا، أَوْ يُمْسِي مُؤْمِنًا وَيُصْبِحُ كَافِرًا، يَبِيعُ دِينَهُ بِعَرَضٍ مِنَ الدُّنْيَا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 118]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«gaawleen jëf ndax ay fitna a ngi ñëw yu mel ni dogiiti guddi gu lëndëm, nit ki day xëy di ku gëm, gontu di ab yéefar, walla mu gontu di ku gëm xëy nekk ab yéefar, day jaay diineem ci poñetu àdduna«.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 118]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day ñaax jullit bi ci mu gaawtu ak baril ay jëf yu baax balaa mu koy tële, ak di ko ñakk a yittewoo ndax fitna yiy ñëw ak ay lënt yu ko koy teree def, te day lëndëm ba mel ni dogiiti guddi, ba dëgg ak neen da cay jaxasoo, ba day jafe ci nit ñi nu ràññee leen, bokk ci ag taram nit ki day làmbatu ba dana xëy di ku gëm daal di gontu di ab yéefar, dana gontu it di ku gëm xëy di ab yéefar, day bàyyi diineem ngir poñeti àdduna bii di jeex.