+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«السَّاعِي عَلَى الأَرْمَلَةِ وَالمِسْكِينِ، كَالْمُجَاهِدِ فِي سَبِيلِ اللَّهِ، أَوِ القَائِمِ اللَّيْلَ الصَّائِمِ النَّهَارَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5661]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5661]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kiy taxawe ay yittey jigéen ji jëkkëram faatu, te amul kenn ku taxawe ay mbiram, ak miskiin bi aajowoo, mu leen di dundal ci ngir yaakaar payug Yàlla mu kawe mi, kooku ak payam day yamoo ak kiy xeex ci yoonu Yàlla, walla kiy taxaw di julli guddi te du ca tàyyi, mbaa kiy woor te du dog.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci dimbalante ak jàppalante ci faj aajoy ñi néew doole.
  2. Jaamu day làmboo jépp jëf ju baax, te bokk na ci ag jaamu taxawu ak a Dimbali jigéen ñi seen jëkkër faatu ak néew doole yi.
  3. Ibn Hubayrata nee na: li ñu ci namm mooy Yàlla mu kawe mi da koy booleel yoolub woorkat ak taxawkatu guddu, ak jiihaatkat joxandoo ko ko; ndaxte dafa taxawu ki jëkkëram faatu taxawaayu jëkkëram..., taxawu miskiin bi manul a taxawe boppam, daal di koy jox ci desiitu dundam, sarax ko ci kàttanam, ba tax njariñam di yamoo ak woor ak taxaw guddi ak jihaat.