+ -

عَنْ أَبِي سَعِيدٍ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَا مِنْ مُسْلِمٍ يَدْعُو بِدَعْوَةٍ لَيْسَ فِيهَا إِثْمٌ، وَلَا قَطِيعَةُ رَحِمٍ، إِلَّا أَعْطَاهُ اللهُ بِهَا إِحْدَى ثَلَاثٍ: إِمَّا أَنْ تُعَجَّلَ لَهُ دَعْوَتُهُ، وَإِمَّا أَنْ يَدَّخِرَهَا لَهُ فِي الْآخِرَةِ، وَإِمَّا أَنْ يَصْرِفَ عَنْهُ مِنَ السُّوءِ مِثْلَهَا» قَالُوا: إِذنْ نُكْثِرُ، قَالَ: «اللهُ أَكْثَرُ».

[صحيح] - [رواه أحمد] - [مسند أحمد: 11133]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"amul benn jullit buy ñaan ñaan gu amul bàkkaar amul dog mbokk, lu dul ne Yàlla dana ko ko jox ci benn ci ñatt yii: ben mu gaawalal ko ag ñaanam, walla mu dencal ko ko ca allaaxira, walla mu wëlbatil ko ca lu bon lu toll ni moom" ñu ne ko: kon de dananu barile, mu ne: "Yàlla moo gën a barile".

[Wér na] - [Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 11133]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: bu jullit bi ñaanee ag ñaan gu bàkkaar amul niki mu ñaan ko yombalug moy ak tooñ, te it ñaanul dogug mbokk; niki mu ñaan ci kaw ay doomam ak i mbokkam, lu dul ne Yàlla dana ko jox ñaanam gi ci benn ci ñatti bir yii: Benn mu gaawalal ko ñaanam gi jox ko li mu ñaan. Walla Yàlla mu màgg mi dencal ko ko mu nekk ag fay ëllëg bis-pénc ci kaweg daraja, walla yërmànde ak jéggalug ñaawteef yi. Walla mu jeñal ko ci àdduna lu bon lu mel ni moom ci kem ñaan gi. Sahaaba yi wax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: kon de dananu bari ay ñaan; ngir nu am benn ci ngëneel yii? Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: la ne fa Yàlla moo gën a bari gën a màgg li ngeen koy ñaan, ay mayam du naaxsaay te du jeex.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaanu jullit bi lu ñuy nangu la deesu ko delloo waaye nag ci ay sàrtam ak i tegginam; loolu moo tax jaadu na ci jaam bi mu baril ay ñaan te bañ a yàkkamti nangu ga.
  2. Nangug ñaan tënkuwul rekk ci amug la ñu doon sàkku; amaana ñu faral ko ci ñaanam gi ay bàkkaar, walla ñu dencal ko ko ca allaaxira.
  3. Ibn Baas nee na: jonguru, ak rafet njort ci Yàlla, ak bañ a naagu, bokk na ci sababi nangu ñaan yi, kon war na ci nit ki mu jonguru ci ñaanam, te rafet njort ci Yàlla mu màgg mi, te xam ne ,moom Aji-Xereñ la Aji-Xam la, amaana mu gaawal ñaan ngir ag xereñteef, amaana it mu jox aji-laaj ji lu gën li mu doon laaj.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi