عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما:
أَنَّ نَبِيَّ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَقُولُ عِنْدَ الْكَرْبِ: «لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ الْعَظِيمُ الْحَلِيمُ، لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ رَبُّ الْعَرْشِ الْعَظِيمِ، لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ رَبُّ السَّمَاوَاتِ وَرَبُّ الْأَرْضِ وَرَبُّ الْعَرْشِ الْكَرِيمِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2730]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne:
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe amee: "laa ilaaha illallaahu Al-Hasiimu Al-Haliimu, laa ilaaha illallaahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi, laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi wa Rabbul Harsi Al-Kariimi".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2730]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe yi ak xat-xat yi daan tar ci moom: "laa ilaaha illallaahu" amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, "Al-Hasiimu" Aji-Màgg dayo ji, Aji-màgg mbir, ci jëmmam ak ay meloom ak i jëfam, "Al-Haliimu" Aji-Lewet ji nga xam ne du yàkkamti aji-moy ji ci ay mbugal waate da koy yeexe, amaana sax mu baal ko ànd ak kàttanam ci moom, moom Aji-Am kàttan la tudd naa sellam ga ci lépp. "laa ilaaha illallahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi" amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla mi Bind Aras ju màgg ji, "laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi" moom miy Aji-Bind Asamaan yi ak Suuf si, di Aji-Bind lépp lu nekk ci seen biir, moom ko te di ko yéwénal, te di Aji-Soppaxndiku ca nu mu ko soobe, "Rabbul Harsi Al-Kariimi" Aji-Bind Aras ju tedd ji.