عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ الْعَاصِ رضي الله عنهما أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَدْعُو بِهَؤُلَاءِ الْكَلِمَاتِ:
«اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ مِنْ غَلَبَةِ الدَّيْنِ، وَغَلَبَةِ الْعَدُوِّ، وَشَمَاتَةِ الْأَعْدَاءِ».
[صحيح] - [رواه النسائي وأحمد] - [سنن النسائي: 5475]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ñaan ci baat yii;
"Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa".
[Wér na] - [An-nasaa'iy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy - 5475]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muslu na ci ay bir:
Bi ci njëkk: (yaw sama Boroom maa ngi muslu) di ñëw di làqu (ci yaw) làquwunu ci keneen ku dul yaw, (ci bor bu bari) ag notam ak ug njàqareem ak tiisam, ma lay ñaan nga dimbali ma ci fay ko.
Ñaareel bi: (ak notug noon bi) ak notam ak ug songam, ma lay ñaan nga tëye loram wi, ak dimbali ma ci kawam.
Ñatteel bi: ,(ak ndokkug noon yi) seenug bég ci liy dal jullit ñi ci balaa ak musiba.