+ -

عَن عبدِ اللهِ بن خُبَيب رضي الله عنه أنه قال:
خَرَجْنَا فِي لَيْلَةٍ مَطِيرَةٍ وَظُلْمَةٍ شَدِيدَةٍ، نَطْلُبُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ؛ يُصَلِّي لَنَا، قَالَ: فَأَدْرَكْتُهُ، فَقَالَ: «قُلْ»، فَلَمْ أَقُلْ شَيْئًا، ثُمَّ قَالَ: «قُلْ»، فَلَمْ أَقُلْ شَيْئًا، قَالَ: «قُلْ»، فَقُلْتُ: مَا أَقُولُ؟ قَالَ: «{قُلْ هُوَ اللهُ أَحَدٌ} وَالْمُعَوِّذَتَيْنِ حِينَ تُمْسِي وَتُصْبِحُ ثَلَاثَ مَرَّاتٍ، تَكْفِيكَ مِنْ كُلِّ شَيْءٍ».

[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي] - [سنن الترمذي: 3575]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Génn nanu ci guddi gu bari taw te lëndëm lool, di wër Yonnente Yàlla bi ngir mu jiite nu julli, nee na: nu dab ko, mu ne ma: "waxal" te waxuma dara, mu waxaat ma: "waxal", te waxuma dara, mu ne ma: "waxal", ma ne ko: lan laay wax? Mu ne ma: "{Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp".

[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3575]

Leeral

Sahaaba bu màgg bii di Abdullah Ibn Xubayb -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne: ñoom dañoo génnoon ci guddi gu bari taw, te lëndëm lool, di seet Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ngir mu jiite leen julli, ñu gis ko, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "waxal" maanaam mune ko jàngal, waaye moom jàngul dara, Yonnente bi bàmtuwaat wax ji, Abdullah ne ko: lan laay jàng yaw Yonnente Yàlla bi? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: jàngal saaru Ixlaas {xul huwal Laahu Ahadun}, ak ñaari musluwaay yi {xul ahuusu bi rabbil falaxi}, ak {xul ahuusu bi rabbin naasi}, waxtuw ngoon, ak waxtuw suba, ñatti yoon, kon dana la wattu ci bépp ay, fegal la ci lépp lu bon.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu ñu jàng saaru Ixlaas ak ñaari musluwaay yi (falaxi ak naasi) ci suba gi ak ci ngoon gi, ndaxte kaarànge
  2. la ci bépp ay.
  3. Ngëneelu jàng saaru Ixlaas ak falaxi ak naasi