عَن أَبِي أُمَامَةَ قَالَ: حَدَّثَنِي عَمْرُو بْنُ عَبَسَةَ رضي الله عنه أَنَّهُ سَمِعَ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«أَقْرَبُ مَا يَكُونُ الرَّبُّ مِنَ العَبْدِ فِي جَوْفِ اللَّيْلِ الآخِرِ، فَإِنْ اسْتَطَعْتَ أَنْ تَكُونَ مِمَّنْ يَذْكُرُ اللَّهَ فِي تِلْكَ السَّاعَةِ فَكُنْ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي] - [سنن الترمذي: 3579]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Umaamata mu wax ne: Amru Ibn Abasata yal na ko Yàlla dollee gërëm wax na ma ne dégg na Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi, boo manee di bokk ci ñiy tudd
Yàlla ci waxtu woowo def ko».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3579]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne: Boroom bu sell bi day gën a jege jaam bi ci ñatteelu xaaj bi mujj ci guddi gi; bu ñu la tawfeexalee may la kàttan -yaw jullit bi- ba nga man a bokk ci mbooloo miy jaamu Yàlla ñiy julli di tudd Yàlla di tuub ci waxtu wii loolu lees wara góor-góor lu la.