عَنْ ثَوْبَانَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَفْضَلُ دِينَارٍ يُنْفِقُهُ الرَّجُلُ، دِينَارٌ يُنْفِقُهُ عَلَى عِيَالِهِ، وَدِينَارٌ يُنْفِقُهُ الرَّجُلُ عَلَى دَابَّتِهِ فِي سَبِيلِ اللهِ، وَدِينَارٌ يُنْفِقُهُ عَلَى أَصْحَابِهِ فِي سَبِيلِ اللهِ» قَالَ أَبُو قِلَابَةَ: وَبَدَأَ بِالْعِيَالِ، ثُمَّ قَالَ أَبُو قِلَابَةَ: وَأَيُّ رَجُلٍ أَعْظَمُ أَجْرًا مِنْ رَجُلٍ يُنْفِقُ عَلَى عِيَالٍ صِغَارٍ، يُعِفُّهُمْ أَوْ يَنْفَعُهُمُ اللهُ بِهِ وَيُغْنِيهِمْ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 994]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla» Abuu Xilaaba wax ne: "dafa, tàmbali ci njaboot Abuu Xilaaba, dellu wax ne: ana gan góor mooy gën a màgg ug pay ci góor guy jox njabootam gu ndaw di leen feg, mbaa Yàlla di leen jariñ ci moom ba def leen ñu doylu.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 994]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ay meloy joxe, mu toftale ci li gën a war ci yaw bu dee anami joxe yi daa daje, mu tàmbalee ca la gën a am solo teg ca la ca tege; Mu xibaare ne alal ji ëpp yool mooy ji jullit bi jox koo xam ne moo ko war a jox; niki jabar ak doom, Teg ca jox waruwaay ju ñu waajal ngir xeex ci yoonu Yàlla, Teg ca jox ay xaritam ak i àndandoom bu ñu nekkee ci jihaad ci yoonu Yàlla.