عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنْ رَسُولِ اللهِ صلى الله عليه وسلم أنه قال:
«وَالَّذِي نَفْسُ مُحَمَّدٍ بِيَدِهِ لَا يَسْمَعُ بِي أَحَدٌ مِنْ هَذِهِ الْأُمَّةِ يَهُودِيٌّ وَلَا نَصْرَانِيٌّ، ثُمَّ يَمُوتُ وَلَمْ يُؤْمِنْ بِالَّذِي أُرْسِلْتُ بِهِ إِلَّا كَانَ مِنْ أَصْحَابِ النَّارِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 153]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 153]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa giñ ci Yàlla ne amul kenn ku koy dégg ci xeet wii, moo xam muy yahuut walla nasaraan mbaa leneen, te wooteb Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- egg ci moom mu faatu te gëmu ko lu dul ne dana bokk ci waa sawara sax fa ba fàww.