+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا يَسْتُرُ عَبْدٌ عَبْدًا فِي الدُّنْيَا إِلَّا سَتَرَهُ اللهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2590]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2590]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne ab jullit du suturaal ab mbokku jullitam ci biri àdduna, lu dul ne Yàlla mu màgg mi dana ko suturaal ëllëg bis-pénc; ag pay day tollok jëf ja, suturag Yàlla ci moom mooy mu nëbbal ko ay ayibam ak i moyam wolif mu di ko siiwal ca barab bañuy pangee jaam yi, man naa nekk it ci bañ ko ca a regle bañ ka ko a fàttali.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yoonalees na ñu suturaal ab jullit bu defee ag moy, ànd ak tere ko loolu ak laabire ko, ak ragalloo ko Yàlla, bu dee dafa bokk ci ñu bon ñi ak yàqkat yiy fésal ay moy Yàlla, ñooñu jaaduwul ñu leen di suturaal; ndaxte suturaal leen da leen di ñemeloo moy ya, waaye dañu leen di kalaame ak njiit yi, donte dañuy tudd aw turam; ndaxte moom day fésal ag kàccooram ak ay moy Yàllaam.
  2. Xemmemloo ci suturaal njuumtey ñeneen ñi.
  3. Bokk na ci njariñi sutura: may aji-moy ji pexeg dellu ci boppam tuub jëm ci Yàlla; ndaxte fésal ay ayib ak i awra dafa bokk ci siiwal ñaawteef, te day yàq nekkiinu mbooloo mi, di xëcc nit ñi jëme leen ci def ko.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Nipali Dariya Rom Majri الموري Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi