عَنْ جَابِرٍ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَبْلَ وَفَاتِهِ بِثَلَاثٍ يَقُولُ:
«لَا يَمُوتَنَّ أَحَدُكُمْ إِلَّا وَهُوَ يُحْسِنُ بِاللهِ الظَّنَّ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2877]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc njëkk muy faatu ci ñatti fan muy wax naan:
"bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2877]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaax jullit bi ci mu bañ a faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla ci notal yaakaar Yàlla ci jamanoy sukraat, mu yaakaar ne Yàlla dana ko yërëm jéggal ko, ndaxte ragal lu ñu sàkku la ngir rafetal jëf yi, te melo woowu du melow jëf, kon li ñu sàkku ci moom mooy mu notal yaakaar gi.