عَنْ قَتَادَةَ رحمه الله قال:
حَدَّثَنَا أَنَسُ بْنُ مَالِكٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ أَنَّ رَجُلًا قَالَ: يَا نَبِيَّ اللهِ كَيْفَ يُحْشَرُ الْكَافِرُ عَلَى وَجْهِهِ؟ قَالَ: «أَلَيْسَ الَّذِي أَمْشَاهُ عَلَى الرِّجْلَيْنِ فِي الدُّنْيَا قَادِرًا عَلَى أَنْ يُمْشِيَهُ عَلَى وَجْهِهِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ؟» قَالَ قَتَادَةُ: بَلَى وَعِزَّةِ رَبِّنَا.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6523]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Xataadatu -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne:
Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6523]
Leerarug hdiis bi: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ëllëg bis-pénc?! Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: xanaa du Yàlla mi ko doxloo fii ci àdduna ci ñaari tànkam man na koo doxloo ci xar kanamam ëllëg bis-pénc ?! Yàlla lépp la man.