+ -

عَنْ عَبْدِ اللهِ بنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه قال:
سَأَلْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: أَيُّ الذَّنْبِ أَعْظَمُ عِنْدَ اللهِ؟ قَالَ: «أَنْ تَجْعَلَ لِلهِ نِدًّا وَهُوَ خَلَقَكَ» قُلْتُ: إِنَّ ذَلِكَ لَعَظِيمٌ، قُلْتُ: ثُمَّ أَيُّ؟ قَالَ: «وَأَنْ تَقْتُلَ وَلَدَكَ؛ تَخَافُ أَنْ يَطْعَمَ مَعَكَ» قُلْتُ: ثُمَّ أَيُّ؟ قَالَ: «أَنْ تُزَانِيَ حَلِيلَةَ جَارِكَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4477]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne:
Laaj na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ban bàkkaar moo gën a màgg fa Yàlla? Mu ne: "nga wutal Yàlla ndend te mu bind la" ma ne: loolu de rëy na lool, ma ne ko: topp ca lan? Mu wa ne: "nga ray sa doom; ngir ne dangaa ragal mu lekkandoo ak yaw" ma ne ko: topp ca lan? Mu ne ma: "nga njaalo ak sa jabari dëkkandoo".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4477]

Leeral

Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ban bàkkaar moo gën a màgg? Mu wax ne: Ba ca gën a màgg mooy bokkaale gu mag, te mooy nga wutal Yàlla niroowaale ci Yàlla gi mu nekk mbaa ci moomeelam, mbaa ci ay turam ak i meloom, te bàkkaar bii Yàlla du ko jéggale ci lu dul tuub, te bu ca boroomam faatoo sawara lay sax. Topp nit ki ray doomam ndax ragal ab dundam, te ray bakkan dafa araam, waaye bàkkaaram dana gën a màgg bu dee ki ñu ray mbokk la ci ki ko ray, batay bàkkaaram dana gën a rëy bi nga xamee ne jubluwaayu ki ray mooy ragal ne ki mu ray day bokk ak moom wërsëgu Yàlla wi. Topp ca nit ki di njaalo ak jabaru dëkkandoom ci muy jéem a nax jabaru dëkkandoom ba mu njaalo ak moom, Njaalo nag dafa araam waaye bàkkaaram dana gën a màg budee ka ñu njaalool jabaru dëkkandoo la, moom mi nga xam ne Sariiha dafa dénkaane ñuy rafetal jëme ci moom, te fonk ko, te rafetal ànd gi ak moom.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bàkkaar yi dañoo rawante cig rëyaay, kem ni jëf yi di rawantee ciy ngëneel.
  2. Bàkkaar bi gën a rëy mooy: bokkaale, ak ray sa doom ngir ragal mu dundu ak yaw, ak njaalo ak sa jabaru dëkkandoo.
  3. Wërsëg ci loxoy Yàlla la nekk te moom Yàlla mu sell mi moo yor wërsëgi mbindeef yi.
  4. Àqi dëkkandoo lu màgg la, kon lor ko moo gën a màgg bàkkaar lor keneen.
  5. Aji-Bind moo yeyoo jaamu moo rekk amul bokkaale.