+ -

‌عن عَلِيٍّ قَالَ: إِنِّي كُنْتُ رَجُلًا إِذَا سَمِعْتُ مِنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ حَدِيثًا نَفَعَنِي اللهُ مِنْهُ بِمَا شَاءَ أَنْ يَنْفَعَنِي بِهِ، وَإِذَا حَدَّثَنِي رَجُلٌ مِنْ أَصْحَابِهِ اسْتَحْلَفْتُهُ، فَإِذَا حَلَفَ لِي صَدَّقْتُهُ، وَإِنَّهُ حَدَّثَنِي ‌أَبُو بَكْرٍ، وَصَدَقَ أَبُو بَكْرٍ، قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَا مِنْ رَجُلٍ يُذْنِبُ ذَنْبًا، ثُمَّ يَقُومُ فَيَتَطَهَّرُ، ثُمَّ يُصَلِّي، ثُمَّ يَسْتَغْفِرُ اللهَ، إِلَّا غَفَرَ اللهُ لَهُ»، ثُمَّ قَرَأَ هَذِهِ الْآيَةَ: {وَالَّذِينَ إِذَا فَعَلُوا فَاحِشَةً أَوْ ظَلَمُوا أَنْفُسَهُمْ ذَكَرُوا اللهَ فَاسْتَغْفَرُوا لِذُنُوبِهِمْ} [آل عمران: 135].

[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي في الكبرى وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 406]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aliyun mu wax ne: man góor laa woon gog bu ma déggee ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn hadiis rekk Yàlla jariñ ma ci lu ko soob, bu ma kenn ci ay Sahaabaam waxee dara bama giñloo ko bu ma giñalee ma dëggal ko, Abuu Bakar wax na ma te wax na dëgg, ne: dégg na Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal», mu daal di jàng aaya jii: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar} [ Aali-Imraan: 135].

[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 406]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xamle ne amul benn jaam buy def bàkkaar, daal di rafetal am njàppam, topp mu jug julli ñaari ràkka yeene ca tuub bàkkaaram bii, topp mu jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dana ko jéggal. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng waxu Yàlla ji: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar ana kan mooy jéggale bàkkaar yi ku dul Yàlla te duñu nuur ca la ñu defoon fekk ne xam nañu ko} [Aali-Imraan: 135].

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci julli ak jéggalu ginnaaw bàkkaar.
  2. Yaatug njéggalug Yàlla mu màgg mi ak nangoom tuub ak jéggalu.