عَنْ عَائِشَةَ رَضِيَ اللهُ عَنْهَا قَالَتْ:
تَلَا رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ هَذِهِ الْآيَةَ: {هُوَ الَّذِي أَنْزَلَ عَلَيْكَ الْكِتَابَ مِنْهُ آيَاتٌ مُحْكَمَاتٌ هُنَّ أُمُّ الْكِتَابِ وَأُخَرُ مُتَشَابِهَاتٌ فَأَمَّا الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِمْ زَيْغٌ فَيَتَّبِعُونَ مَا تَشَابَهَ مِنْهُ ابْتِغَاءَ الْفِتْنَةِ وَابْتِغَاءَ تَأْوِيلِهِ، وَمَا يَعْلَمُ تَأْوِيلَهُ إِلَّا اللَّهُ، وَالرَّاسِخُونَ فِي الْعِلْمِ يَقُولُونَ آمَنَّا بِهِ كُلٌّ مِنْ عِنْدِ رَبِّنَا وَمَا يَذَّكَّرُ إِلَّا أُولُو الْأَلْبَابِ} [آل عمران: 7]. قَالَتْ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «فَإِذَا رَأَيْتِ الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ مَا تَشَابَهَ مِنْهُ فَأُولَئِكَ الَّذِينَ سَمَّى اللهُ، فَاحْذَرُوهُمْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4547]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jàng aaya bii: {Moom Yàlla moo wàcce ci yaw Téere ba: am na ca ay aaya yoy séen i maanaa leer nañu, ñoo di cosaani àtte yi, ak yeneeni aaya yu séen i maanaa fésul. Ña nga xam ne jeng a nekk seeni xol, danañu topp lënt ya ngir sàkku fitna ak jéem leen a firi, te Yàlla doŋŋ a xam séen i piri ak ña sax ci xam-xam. Ñoom danañu wax ne : "Gëm nanu ko: lépp ca sunu Boroom la bawoo!" Woroom xel yi rekk ay waaru} [Aali Imraan: 7]. Neena Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: "bu ngeen gisee ñiy topp lënt ya xamleen ne ñooñii la Yàlla di wax nangeen leen moytu".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4547]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jàng aaya bii: {Moom Yàlla moo wàcce ci yaw Téere ba: am na ca ay aaya yoy séen i maanaa leer nañu, ñoo di cosaani àtte yi, ak yeneeni aaya yu séen i maanaa fésul. Ña nga xam ne seeni xol daa jéngi, danañu topp lënt ya ngir sàkku fitna ak jéem leen a firi, te Yàlla dong a xam séen i piri ak ña sax ci xam-xam. Ñoom Danañu wax ne : "Gëm nanu ko: lépp ca sunu Boroom la bawoo!" Woroom xel yi rekk ay waaru} Yàlla da ciy xibaare ne moom moo wàcce Alxuraan ci yónenteem bi, te am na ci ay aaya yu leer i tegtal, yu ñu xam ay àtteem amul menn lënt, mooy cosaanu téere bi tey delluwaayam, te mooy delluwaay ba bu wuute amee, am na ci yeneen aaya yu man a am lu ëpp menn piri, maanaami dafay jaxasoo ci ñenn ñi, mbaa ñu yaakaar ne am na ay juuyoo ci séen diggante ak beneen aaya, bu ko defee Yàlla leeral ni nit ñi di doxale ci aaya yooyu. Ñi seen xol jeng cig dëgg, dañuy bàyyi yu leer ya, jël yu lënt ya lañu ca jublu mooy tasaare ay lënt ak réerloo nit ñi, ba noppi ñu fexe ko tekki ci li méngoo ak séen i bànneex. Waaye ñi dëgër ci xam-xam xamnañu yu lënt yii, te dañu koy delloo ca yu leer ya, ñu gëm ko ci ne ci Yàlla Mu tedd mi ta màgg la juge, ak ne mënut a jaxasoo mbaa muy woroo, waaye kenn du fàttali ku ak a waaru lu dul woroom xel yu sell yi. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax yaayu way-gëm yi Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, bu gisee ñiy topp yu lënt yi, na xam ne ñooy ñi Yàlla tudd ci li mi wax ne: {Waaye ñi séen xol réer}, na ngeen leen moytu, te buleen leen déglu.