عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مَكَارِمَ الْأَخْلَاقِ».
[حسن] - [رواه البخاري في الأدب المفرد وأحمد والبيهقي] - [السنن الكبرى للبيهقي: 20819]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi".
[Tane na] - [رواه البخاري في الأدب المفرد وأحمد والبيهقي] - [السنن الكبرى للبيهقي - 20819]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne Yàlla mu màgg mi da ko a yónni ngir mu mottali ngëneel ak jikkó yu rafet yi; ba tax mu yónni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu mottali li ko jiitu woon ci ay Yonente, ak di mottali jikkóy araab yu rafet ya, ñu nekkoon ñu bëgg yiw te bañ ay, di ñu am kersa ak tabe ak ug njàmbaarte; ñu yónni Yonente bi ngir mu mottali li mànki ca seen jikkó ya, niki seen ug puukarewu ci seen i askan, ak rëy-rëylu ak xeeb aji-ñàkk ak yeneen yu dul yooyu.