عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«لَيْسَ الْوَاصِلُ بِالْمُكَافِئِ، وَلَكِنِ الْوَاصِلُ الَّذِي إِذَا قُطِعَتْ رَحِمُهُ وَصَلَهَا».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 5991]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5991]
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ku mat ci jokk bokk ak rafetal jëme ci jegeñaale yi nekkul nit kiy fay rafetal cig rafetal, Waaye jokk-katu mbokk dëgg mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkoom mu jokk ko, bu ñu ñaawalee jëme ci moo; dakoy faye ag rafetal jëme ci ñoom.