عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه:
أَنَّ رَجُلًا قَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ إِنَّ لِي قَرَابَةً أَصِلُهُمْ وَيَقْطَعُونِي، وَأُحْسِنُ إِلَيْهِمْ وَيُسِيئُونَ إِلَيَّ، وَأَحْلُمُ عَنْهُمْ وَيَجْهَلُونَ عَلَيَّ، فَقَالَ: «لَئِنْ كُنْتَ كَمَا قُلْتَ، فَكَأَنَّمَا تُسِفُّهُمُ الْمَلَّ وَلَا يَزَالُ مَعَكَ مِنَ اللهِ ظَهِيرٌ عَلَيْهِمْ مَا دُمْتَ عَلَى ذَلِكَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2558]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Jenn waay dafa wax: yaw Yonnente Yàlla bi damaa am jegeñaale ma leen di jokk ñu may dog, may rafetal jëme ci ñoom ñuy ñaawal jëme ci man, may lewet ci ñoom ñuy fétteerlu ci sama kaw, mu ne ko: "bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2558]
Jenn waay dafa jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ne dafa am ay jegeñaale ak i mbokk muy jëflante ak ñoom lu rafet ñoom ñuy jëflante ak moom safaan; mu leen di jokk di dem si ñoom, ñoom ñu koy dog, muy rafetal jëme ci ñoom ci lu baax ak matal kóllare, ñoom ñuy ñaawal jëme ci ñoom ci tooñ ak foñ, muy lewet ci ñoom di leen baal, ñoom ñuy fétteerlu ci kawam ci wax ak jëf ju ñaaw, ndax mu wéy di leen jokk ànd ak li mu tudd?
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bu dee noonu nga wax la deme kon yaa ngi leen di gàccaal di leen doyadal ci seen bopp, ba mel ni danga leen di lekkloo dóom bu tàng; ngir sa rafetal gu bari ak seen jëf yu ñaaw yi ne seen bopp, te doo deñ di am ci Yàlla ndimbal ci seen kaw, mu lay fegal seen i lor fii ak yaa ngi nekk ci lii nga tudd ci ay rafetal jëme ci ñoom, ñoom ñu sax ci di ñaawal jëme ci yaw.