عَنْ عَائِشَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«الرَّضَاعَةُ تُحَرِّمُ مَا تُحَرِّمُ الوِلَادَةُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [الأربعون النووية: 44]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"nàmpal day araamal li njureel di araamal".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [الأربعون النووية - 44]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne dees na araamal ci nàmpal li ñu araamal ci njureel ak askan di nijaay walla baay tëx walla mbokk..., nàmpal it dana daganal li njureel di daganal ci ay àtte.