عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرٍو رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا:
أَنَّ رَجُلًا سَأَلَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: أَيُّ الإِسْلاَمِ خَيْرٌ؟ قَالَ: «تُطْعِمُ الطَّعَامَ، وَتَقْرَأُ السَّلاَمَ عَلَى مَنْ عَرَفْتَ وَمَنْ لَمْ تَعْرِفْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 12]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 12]
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: yan ci jikkòy lislaam yi ñoo gën? Mu tudd ñaari jikkó:
Bu njëkk bi: di baril di leel way-ñàkk yi, dana ci dugg ba tay saraxe ak àddiya ak nganale ak céetal, ngëneelu lele nag dana feddaliku ci jamonoy xiif, ak bi njëg yi seeree.
Ñaareel bi: di nuyu bépp jullit, moo xam xam nga ko walla xamóo ko.