+ -

عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما قَالَ:
مَرَّ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِقَبْرَيْنِ، فَقَالَ: «إِنَّهُمَا لَيُعَذَّبَانِ، وَمَا يُعَذَّبَانِ فِي كَبِيرٍ، أَمَّا أَحَدُهُمَا فَكَانَ لاَ يَسْتَتِرُ مِنَ البَوْلِ، وَأَمَّا الآخَرُ فَكَانَ يَمْشِي بِالنَّمِيمَةِ» ثُمَّ أَخَذَ جَرِيدَةً رَطْبَةً، فَشَقَّهَا نِصْفَيْنِ، فَغَرَزَ فِي كُلِّ قَبْرٍ وَاحِدَةً، قَالُوا: يَا رَسُولَ اللَّهِ، لِمَ فَعَلْتَ هَذَا؟ قَالَ: «لَعَلَّهُ يُخَفِّفُ عَنْهُمَا مَا لَمْ يَيْبَسَا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 218]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne :
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa romb ñaari bàmmeel, daal di wax ne : « ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj" mu jël aw xob wu tooy, xar ko ñaari xaaj, roof ci bàmmeel bu ne wenn xaaj, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, lu tax nga def lii ? Mu wax ne : "amaana ñu woyafalal leen fii ak wowuñu».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 218]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa romb ñaari bàmmeel daal di wax ne : Boroom ñaari bàmmeel yii de ñoo ngi leen di mbugal; te mbugalewuñu leen ci mbir mu rëy ci seen gis-gis, doonte lu rëy la fa Yàlla, Bu dee kenn ki moom daawul yittewoo sàmm yaramam ak i yéreem ci saw mi bu daan faj aajoom, Keneen ki nag moom da daan dox di rambaaj ci diggante nit ñi, di tuxal waxi keneen ngir jubloo lore ak def ag wuute ak ug mbañeel ci diggante nit ñi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Rambaaj ak ñàkk a set ci saw dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi, ak yiy waral mbugalu bàmmeel.
  2. Yàlla dafa wuññi yenn kumpa yi -niki mbugalu bàmmeel- ngir feeñal ay màndarga ci ag Yónnenteem -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
  3. Jëf jii muy xar ñaari xob ak teg ko ci kaw bàmmeel bi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ko jagoo; ndax Yàlla moo ko wan mbiri boroom bàmmeel yi, kon deesu ci natt keneen ndaxte kenn xamul mbiri ñi nekk ci bàmmeel yi.