عَنْ زِيَادِ بْنِ لَبِيدٍ رضي الله عنه قَالَ:
ذَكَرَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ شَيْئًا، فَقَالَ: «ذَاكَ عِنْدَ أَوَانِ ذَهَابِ الْعِلْمِ» قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، وَكَيْفَ يَذْهَبُ الْعِلْمُ، وَنَحْنُ نَقْرَأُ الْقُرْآنَ وَنُقْرِئُهُ أَبْنَاءَنَا وَيُقْرِئُهُ أَبْنَاؤُنَا أَبْنَاءَهُمْ إِلَى يَوْمِ الْقِيَامَةِ؟ قَالَ: «ثَكِلَتْكَ أُمُّكَ زِيَادُ، إِنْ كُنْتُ لَأُرَاكَ مِنْ أَفْقَهِ رَجُلٍ بِالْمَدِينَةِ، أَوَلَيْسَ هَذِهِ الْيَهُودُ وَالنَّصَارَى يَقْرَؤونَ التَّوْرَاةَ وَالْإِنْجِيلَ، لَا يَعْمَلُونَ بِشَيْءٍ مِمَّا فِيهِمَا؟!».
[صحيح لغيره] - [رواه ابن ماجه] - [سنن ابن ماجه: 4048]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Siyaad Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- me wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa am lu mu tudd daal di ne: «loolu de bu xam-xam di dem lay doon» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, naka la xam-xam di deme, te nun noo ngi jàng Alxuraan di ko jàngal sunuy doom, sunuy doom di ko jàngal séen i doom, ba keroog bis-pénc? Mu wax ne: « sa yaay ñàkk yaw Siyaad, man de foogoon naala ki gën a amug dégg ci Madiina, xanaa du Yahuut yi ak Nasaraan yi ñoo ngi jàng Tawraat ak Injiil, te duñu jëfe dara ca la fa nekk?!».
[Wér na ngir beneen Adiis bu koy tegtale] - [Ibnu Maaja soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja - 4048]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa toogoon ci biir Sahaaba yi, daal di wax ne: jamono jii mooy ji ñuy yëkkati xam-xam di dindi xam-xam ci nit ñi, Siyaad Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- yéemu daal di laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Ne ko: naka la ñuy yëkkatee xam-xam ba mu sànku ci nun?! Te jàng nanu Alxuraan mukkal ko; te giñ naa ci Yàlla ne dananu sax ci di ko jàng, dananu ko jàngal sunuy jigéen ak sunuu doom, ak sunuy sët. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daldi yéemu ne ko: nala sa yaay ñàkk rekk yaw Siyaad! man de boole woon naa la ci boroomu xam-xami Madiina yi! Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di koy leeral ne: ñàkk xam-xam gi nekkul ñàkk Alxuraan; waaye ñàkk xam-xam mooy ñàkk koo jëfe, Ndax Tawraat ak Injiil ñoo ngi ci Yahuut yi ak Nasaraan yi; ànd ak loolu jariñu leen, te jariñuwuñu ca la ñu jublu woon ci ñoom ñaar; te mooy jëfe la ñu xam.