1. Li jiitu
  2. Ràññetle yi
  3. Alquraan ju tedd ji ak xam-xam yi ci aju

Hadiis buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, nangeen wax ne: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun}

عَنْ ‌أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ قَالَ:
كَانَ أَهْلُ الْكِتَابِ يَقْرَؤُونَ التَّوْرَاةَ بِالْعِبْرَانِيَّةِ، وَيُفَسِّرُونَهَا بِالْعَرَبِيَّةِ لِأَهْلِ الْإِسْلَامِ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَا تُصَدِّقُوا أَهْلَ الْكِتَابِ وَلَا تُكَذِّبُوهُمْ، وَقُولُوا: {آمَنَّا بِاللهِ وَمَا أُنْزِلَ إِلَيْنَا} [البقرة: 136] الْآيَةَ».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Ñi ñu joxoon téere ya daanañu jàng Tawraat ci làkku Hébra, daa ko firil waa Lislaam ci làkku Araab, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: "buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, nangeen wax ne: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun} [Al-Baxara: 136] aaya bi".

Wér na Al-buxaariy soloo na ko Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4485

Leeral gi

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mi ngi artu aw xeetam ci woru ci li ñoñ téere yi di nettali ci séen téere yi. Ndax Yahuut yi ci jamonoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daanañu jàng Tawraat ci làkku Habriya; te mooy làkku Yahuut yi, daan ko tekki ci Araab, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, loolu nag ci lu nu xamul dëgg la walla fen la; Ndaxte Yàlla mu kawe mi da noo digal nu gëm Alxuraan ji mu wàcce ci nun, ak téere bi mu wàcce ci ñoom, waaye nag nun amunu yoonu xam li wér ci li ñuy nettali ci téere yooyu ak la ca wérul bu dee amul ci sunu Sariiha luy leeral dëgg ga ak fen wa, Nu taxawlu, dunu leen dëggal; ngir dunu bokkak ñoom la ñu ca soppi, te dunu leen weddi; ndax man naa am muy dëgg, ndax kon danuy weddi li ñu nu digal nu gëm ko, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na nuy wax: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun, ak la ñu wàcce ci Ibraahiima ak Ismaayla ak Yanqóoba ak sét ya ak la ñu jox Muusaa ak Iisaa ak la ñu jox Yónente ya mu bawoo ca séen Boroom, dunu xàjjale diggante kenn ci ñoom, te nun ci moom la nu jébbalu} [Al-Baxara: 136].

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi: Li ñuñ téere yi di nettali ñàtti xaaj la: xaaj bu dëppoo ak Alxuraan ak Sunna boobu dañu koy dëggal, ak xaaj bu juuyoo ak Alxuraan ak Sunna boobu neen la dañu koy weddi, ak xaaju ñatteel bi amul ci Alxuraan ak Sunna lu koy dëggal mbaa di ko fenloo; boobu dees na ko nettali rekk waaye duñu ko dëggal te duñu ko weddi.

Gaaral firi yi

68 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
UG ئۇيغۇرچە الأيغورية
BN বাংলা البنغالية
FR Français الفرنسية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
JA 日本語 اليابانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
YO Yorùbá اليوروبا
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
SO Soomaali الصومالية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
CS Čeština التشيكية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
FF Fulfulde الفولانية
IT Italiano الإيطالية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
BG Български البلغارية
AZ Azərbaycan الأذربيجانية
EL Ελληνικά اليونانية
UZ O‘zbek الأوزبكية
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
LN Lingala اللينجالا
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
BM Bambara البامبارية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية
DA Dansk الدنماركية
RN Kirundi الكيروندي
KMR Kurmancî الكرمنجية
MS Bahasa Melayu الملايو