+ -

عَنْ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللَّهِ رضي الله عنهما أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا تَعَلَّمُوا الْعِلْمَ لِتُبَاهُوا بِهِ الْعُلَمَاءَ، وَلَا لِتُمَارُوا بِهِ السُّفَهَاءَ، وَلَا تَخَيَّرُوا بِهِ الْمَجَالِسَ، فَمَنْ فَعَلَ ذَلِكَ، فَالنَّارُ النَّارُ».

[صحيح] - [رواه ابن ماجه] - [سنن ابن ماجه: 254]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi, walla ngir am ci wàccuwaay ca jotaay ya, képp ku def loolu, sawara la jëm, sawara la jëm".

[Wér na] - [Ibnu Maaja soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja - 254]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo sàkku xam-xam ngir ndamu puukarewu ak woroom xam-xam yi, ak di wane ne man boroom xam-xam laa ne yéen, walla di ci wàqante ak a werente ak way-dese ñi ak ñu gàtt xel ñi, walla di sàkku xam-xam ngir nekk njiit ca jotaay ya, ñu di ko jiital ca kaw ñeneen ña fa nekk. Ku def loolu; kooku yayoo na sawara ngir sababus ngistalam ak ñàkk a sellalam ci sàkku xam-xam ngir Yàlla.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tëkkoo nañu ci sawara képp kuy sàkku xam-xam ngir ndamu mbaa werente ca walla nekk njiit ca jotaay ya, mbaa yu ko niru.
  2. Solos sellal ñeel kuy sàkku xam-xam te di ko xamle.
  3. Ci yéene la jëf di tabaxu te ca la fay ga di aju.