+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ تَقُومُ السَّاعَةُ حَتَّى تُقَاتِلُوا اليَهُودَ، حَتَّى يَقُولَ الحَجَرُ وَرَاءَهُ اليَهُودِيُّ: يَا مُسْلِمُ، هَذَا يَهُودِيٌّ وَرَائِي فَاقْتُلْهُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2926]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bis-pénc du taxaw ba keroog ngeeni xeex ak Yahuut yi, ba doj wu ab Yahuut nekk ci ginnaawam di wax naan: yaw jullit bi, ab Yahuut a ngi nii sama ginnaaw ñëwal ray ko».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2926]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaar ne bis-pénc du ñëw mukk lu dul ne jullit ñi danañu xeex ak Yahuut yi, Ba bu Yahuut bi dawee jëm ci ginnaaw aw doj ngir làqatu fa; Yàlla waxloo doj wi mu woo jullit bi ne ko: ab Yahuut moo ngi ci ginnaawam na ñëw ray ko.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi :
  2. Xibaareg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yenn kumpa yi ak yi ñëwagul, kem ni ka ko Yàlla mu kawe mi xamale, te fàwwu mu am.
  3. Jullit ñi dañuy xeex ak Yahuut yi ci mujjug jamono, te loolu daa bokk ci màndargay bis-pénc.
  4. Diiney Lislaam da fiy des ba bis-pénc, te day not diine yépp.
  5. Yàlla day dimbali jullit ñi ci kaw séen i noon, te bokk na ca mu waxloo doj yi ci mujjug jamono.