+ -

عَنِ ‌ابْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُمَا:
أَنَّ نَاسًا مِنْ أَهْلِ الشِّرْكِ، كَانُوا قَدْ قَتَلُوا وَأَكْثَرُوا، وَزَنَوْا وَأَكْثَرُوا، فَأَتَوْا مُحَمَّدًا صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالُوا: إِنَّ الَّذِي تَقُولُ وَتَدْعُو إِلَيْهِ لَحَسَنٌ، لَوْ تُخْبِرُنَا أَنَّ لِمَا عَمِلْنَا كَفَّارَةً، فَنَزَلَ {وَالَّذِينَ لا يَدْعُونَ مَعَ اللهِ إِلَهًا آخَرَ وَلا يَقْتُلُونَ النَّفْسَ الَّتِي حَرَّمَ اللهُ إِلا بِالْحَقِّ وَلا يَزْنُونَ}[الفرقان: 68]، وَنَزَلَت: {قُلْ يَا عِبَادِيَ الَّذِينَ أَسْرَفُوا عَلَى أَنْفُسِهِمْ لا تَقْنَطُوا مِنْ رَحْمَةِ اللهِ} [الزمر: 53].

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4810]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne:
Ay nit yu bokkoon ca bokkaalekat ya, dañoo ëppaloon ci raye, ëppal ci njaalo, ñu ñëw ci Yónente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale, aaya bi daadi wàcc {ak ñi nga xam ne duñu jaamu jeneen Yàlla di ko bokkaale ak Yàlla, te duñu ray bakkan bu Yàlla araamal ci lu dul dëgg te duñu njaalo{ [Al-Furxaan: 68], aaya bii it wàcc: {waxal sama jaam ñi nga xam ne dañoo ëppal ci def ay bàkkaar buñu naagu mukk ci yërmàndey Yàlla} [As-Sumari: 53].

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4810]

Leeral

Ay gaay ci bokkaalekat yi dañoo ñëwoon ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- te fekk ñu ëppaloon lool ci ray nit ak njaalo, ñu wax Yónente bi ne ko: Lislaam ji ngay woote ak di ko jàngale lu baax la, waaye lan moo doon sunu mbir ak li ñu tàbbi ci ay bokkaale ak bàkkaar yu mag yi, ndax dees na ko sippi?
Ñaari aaya yi daal di wàcc, ne Yàlla day nangu tuub ci nit ñi ak lu séen i bàkkaar bari te rëy, ndax bu dul woon loolu danañu wéy ca séen kéefar ga ak séen mbewte ma te kon duñu dugg ci diine ji.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu Lislaam ag màggaayam ci ne day màbb bàkkaar yi ko jiitu.
  2. Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi ak njéggalam ak ug baaleem.
  3. Bokkaale dafa araam, ray bakkan ci lu dul dëgg dafa araam, njaalo dafa araam, tëkku nañu it kuy def bàkkaar yii.
  4. Tuub gu dëggu gu ànd ak sellal ak jëf lu baax day far mbooleem bàkkaar yu mag yi ba ci weddi Yàlla mu kawe mi sax ca la bokk.
  5. Araamalees na naagu ak ñakk yaakaar ci yërmàndey Yàlla -tudd naa sellam ga-.