+ -

عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ الْعَاصِ رضي الله عنهما أنَّ رَسولَ اللَّهِ صلَّى اللَّهُ عليْه وسلَّمَ، قال:
«قَدْ أَفْلَحَ مَن أَسْلَمَ، وَرُزِقَ كَفَافًا، وَقَنَّعَهُ اللَّهُ بما آتَاهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1054]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”.

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1054]

Leeral

Yonente bi leeral na ne ku toppu boroom bi jaar ci lislaam, ñu wërsëgal ko lu dagan kem aajoom ëppul yéesul, Yàlla def ko mu doylu gërëm li mu ko jox koo ku texe na.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Texeg nit ki mi ngi ci matug diineem ak doyug dundam ak ug doyloom ci li ko Yàlla jox.
  2. Xemmemloo ci doylu ci li ñu la jox ci àdduna ànd ak lislaam ak sunna.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi