عن عمر بن الخطاب رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّمَا الْأَعْمَالُ بِالنِّيَّةِ، وَإِنَّمَا لِامْرِئٍ مَا نَوَى، فَمَنْ كَانَتْ هِجْرَتُهُ إِلَى اللهِ وَرَسُولِهِ، فَهِجْرَتُهُ إِلَى اللهِ وَرَسُولِهِ، وَمَنْ كَانَتْ هِجْرَتُهُ لِدُنْيَا يُصِيبُهَا أَوِ امْرَأَةٍ يَتَزَوَّجُهَا، فَهِجْرَتُهُ إِلَى مَا هَاجَرَ إِلَيْهِ».
وفي لفظ للبخاري: «إِنَّمَا الْأَعْمَالُ بِالنِّيَّاتِ، وَإِنَّمَا لِكُلِّ امْرِئٍ مَا نَوَى».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1907]
المزيــد ...
Jële nañu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«jëf yi mi ngi aju ci yéene ja, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yónenteem, koo ku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yónenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot, walla jigéen ju mu bëgg a takk; kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay" ci beneen nettali ci Al-Buxaarii: "jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene
rekk lay am».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1907]
Yónente bi day leeral ne jëf yépp ci yéene ja la aju, te àtte bii daa matale jëf yépp moo xam jaamu yi la mbaa jëflante yi, koo xam ne jëfam njariñ la ci jublu du ca am lu dul njariñ loola waaye du ci am tiyaaba, ko xam ne jëfam jege Yàlla la ci jublu dana am ca jëfam ja ab yool ak ug pay, donte jëf i aada la, niki lekk ak naan.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- joxe waat meneen misaal ci ni yéene di jeexitale ci jëf yi ànd ak seenug niróo ci melo wi feeñ, mu leeral ne ku jublu ci gàddaay bàyyi réewam ngir jublu ci ngërëmal Boroomam kon gàddaayam ga gàddaayu sariiha la gu ñu nangu te dees na ko fay ab yool ngir yéeneem ju dëggu, waaye ku jublu cig gàddaayam njariñal àdduna, alal, ak daraja ak am njaay, walla soxna du am ca gàddaayam ga lu dul njariñ yooya mu yéene woon, te du am benn cér cig pay mbaa ab yool.