عَنْ أَبي مَسْعُودٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ مِمَّا أَدْرَكَ النَّاسُ مِنْ كَلاَمِ النُّبُوَّةِ الأُولَى: إِذَا لَمْ تَسْتَحْيِ فَاصْنَعْ مَا شِئْتَ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6120]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc neena:
«bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy
rus defal lu la neex».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6120]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne bokk na ci ndénkaane yi ñëw jóge ca Yonnente yu njëkk ya, nit ñi di ko jokkalante ci seen diggante di ko donnante ci ñoom ay xarnu ba mu egg ci ñi jiitu ci xeet wii, xoolal li nga bëgg a def, bu dee dafa bokk ci li ñu dul am kersa kon def ko, waaye bu bokkee ci yi ñuy am kersa kon bàyyi ko; ndax teree def ñaawteef yi mooy kersa, ku amul kersa, day nuur ci ñaawteef yi ak yu bon yi.