عَنْ صُهَيْبٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«عَجَبًا لِأَمْرِ الْمُؤْمِنِ، إِنَّ أَمْرَهُ كُلَّهُ خَيْرٌ، وَلَيْسَ ذَاكَ لِأَحَدٍ إِلَّا لِلْمُؤْمِنِ، إِنْ أَصَابَتْهُ سَرَّاءُ شَكَرَ، فَكَانَ خَيْرًا لَهُ، وَإِنْ أَصَابَتْهُ ضَرَّاءُ صَبَرَ، فَكَانَ خَيْرًا لَهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2999]
المزيــد ...
Jële nañu ci Suhaybu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi, bu ko mbégte dalee day sant mu doon aw yiw ci moom, bu ko lor dalee day muñ mu doon aw yiw ci moom».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2999]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day yéemu ci mbiri jullit bi ci anamug rafetlu; ndaxte ay mbiram yépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi; Bu ko mbégte dalee day sant Yàlla ci loolu; mu am ug pay ci cant gi, Bu ko lor dalee mu muñ te yaakaar payug Yàlla, mu am ug pay ca muñ ga, kon moom day am ug pay ci anam yépp.