عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا تَحَاسَدُوا، وَلَا تَنَاجَشُوا، وَلَا تَبَاغَضُوا، وَلَا تَدَابَرُوا، وَلَا يَبِعْ بَعْضُكُمْ عَلَى بَيْعِ بَعْضٍ، وَكُونُوا عِبَادَ اللهِ إِخْوَانًا الْمُسْلِمُ أَخُو الْمُسْلِمِ، لَا يَظْلِمُهُ وَلَا يَخْذُلُهُ، وَلَا يَحْقِرُهُ التَّقْوَى هَاهُنَا» وَيُشِيرُ إِلَى صَدْرِهِ ثَلَاثَ مَرَّاتٍ «بِحَسْبِ امْرِئٍ مِنَ الشَّرِّ أَنْ يَحْقِرَ أَخَاهُ الْمُسْلِمَ، كُلُّ الْمُسْلِمِ عَلَى الْمُسْلِمِ حَرَامٌ، دَمُهُ، وَمَالُهُ، وَعِرْضُهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2564]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbokk jullit mooy mbokku jullit, du ko tooñ, du ko beddi, du ko xeeb, ragal Yàlla fii la nekk" muy junj ci dënnam bi ñatti yoon "doy na sëkk nit aw ay muy xeeb mbokk jullitam, léppi jullit bi dafa araam ci jullit bi, dereetam, ak alalam, ak deram".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2564]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na jullit bi yiw ci mbokk jullitam, mu leeral lenn li war ci moom ci ay warteef ak i teggin ak yu ko niru; bokk na ca: Ndénkaane lu njëkk li: buleen soxorante ci ñenn ñi di mébét xéewalu ñenn ñi deñ. Ñaareel bi: buleen worante ci yokk njëgu njaay mi bëggu ko a jënn; waaye dafa bëgg a jariñ jaaykat bi, walla lor jënnkat bi. Ñatteel bi: buleen bañante te mooy bëgg ko a lor, te mooy safaanu bëggante; lu dul bu bañ gi dee ngir Yàlla; kon day war. Ñenteel bi: buleen dummooyoonte ci kenn ku nekk ci yéen di wan mbokkam ginnaaw, daal di koy dummooyu gàddaay ko. Juróomeel bi: bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayum keneen ci mu wax ki jënd am njaay: amnaa bu mel ni moom ci njëgg gu gën a néew walla bu ko gën ci genn njëgg gi. Topp Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénkaane, ndénkaane lu matale, daal di wax ne: nekkleen mel ni ay mbokk ci bàyyi tere yi ñu tudd, ak ci joxe mbëggeel ak ñeewant ak yërmànde ak dimbalante ci yiw, ànd ak xol yu sell ak di laabirante ci gépp anam. Bokk na ci yi aju ci mbokkoo gi: Mu bañ a tooñ mbokk jullitam te du jalgati ci kawam. Ak mu bañ a bàyyi mbokk jullitam ñu koy tooñ mu koy beddi ci anam gog man na koo dimbali, dindil ko tooñ ga. Ak mu bañ ko a xeeb di ko sàkku a tuutal di ko xool bëti wàññi ak doyadal; ndax loolu ci rëy gu ne ci xol lay jóge. Topp Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral ñatti yoon ne ragal Yàlla ci xol lay nekk, ragal Yàlla giy waral rafet jikkó, ak di bàyyi xel Yàlla di ko fuglu, ku mel nii nag du xeeb ab jullit, te ay jikkó yu bon doy na nit ki muy xeeb mbokk jullitam; loolu nag ngir rëy gu ne ci xolam. Topp Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di feddali li weesu ci ne léppi jullit araam na ci kaw jullit bi: dereetam: ci mu jalgati ci kawam ci ray walla lu ko féete suuf niki gaañ walla dóor ak lu ko niru, niki noonu alalam: ci mu jël ko ci lu dul dëgg, niki noonu deram: ci mu koy ŋàññ ci boppam walla ci askanam.