عَنْ المِقْدَامِ بْنِ مَعْدِي كَرِبَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَا مَلأَ آدَمِيٌّ وِعَاءً شَرًّا مِنْ بَطْنٍ، بِحَسْبِ ابْنِ آدَمَ أَكَلاَتٌ يُقِمْنَ صُلْبَهُ، فَإِنْ كَانَ لَا مَحَالَةَ، فَثُلُثٌ لِطَعَامِهِ، وَثُلُثٌ لِشَرَابِهِ، وَثُلُثٌ لِنَفَسِهِ».
[صحيح] - [رواه الإمام أحمد والترمذي والنسائي وابن ماجه] - [الأربعون النووية: 47]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Mahdii Karib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem".
[Wér na] - [رواه الإمام أحمد والترمذي والنسائي وابن ماجه] - [الأربعون النووية - 47]
Yonnente bu tedd bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da nuy tegtal benn ci coosani faj yi, te mooy fegu gi nga xam ne ci la nit ki di fege ag wéram, te mooy néewal ag lekk, nga xam ne day lekk kem lu muy fege noyyeem di ko dëgëral ci jëf yi war, ak ne li yées ci ndab lu ñuy feesal mooy biir, ndax lay juddoo ca suur ga ci ay feebar yuy lore yoy deesu ko takk, moo xam mu gaaw walla mu yeex, mu nëbbu walla mu feeñ. Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: bu dee nit ki manut a ñàkk a suur, kon na def lekk gi mu toll ni ñatteelu xaaj bi, beneen ñatteelu xaaj bi di naan gi, ak ñatteelu xaaj ngir noyyi gi ba du am ug xat ak ug loru, muy tàyyeel ci def li ko war ci mbiri diineem walla yu àddunaam.