عَن ابنِ عباسٍ رضي الله عنهما أنَّ رسولَ اللهِ صلي الله عليه وسلم قال:
«لَو يُعطَى النّاسُ بدَعواهُم لادَّعَى رِجالٌ أموالَ قَومٍ ودِماءَهُم، ولَكِنَّ البَيِّنَةَ على المُدَّعِى، واليَمينَ على مَن أنكَرَ».
[صحيح] - [رواه البيهقي] - [السنن الكبرى للبيهقي: 21243]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«bu ñu doon jox nit ñi ci seen i wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ. ».
[Wér na] - - [السنن الكبرى للبيهقي - 21243]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne bu ñu doon jox nit ñi ngir seen i wootewoo dong ci lu dul benn firnde walla ay tegtal kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a joxe aw lay ak firnde ci li muy sàkku, bu amul aw lay ñu gaaral wootewoo ji ki ñu tuumaal, bu ko weddee dafa war a giñ daal di cay set.