+ -

عن عمر بن الخطاب رضي الله عنه قال: إنه سمع نبي الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«لَو أَنَّكُمْ تَتَوَكَّلُونَ عَلَى اللهِ حَقَّ تَوَكُّلِهِ، لَرَزَقَكُمْ كَمَا يَرْزُقُ الطَّيْرَ، تَغْدُو خِمَاصًا وَتَرُوحُ بِطَانًا».

[صحيح] - [رواه الترمذي وابن ماجه وأحمد] - [مسند أحمد: 205]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Umar ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg na Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell.

[Wér na] - [Ibnu Maaja soloo na ko - At-tirmisiy soloo na ko - Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Al-bassaar bees leeral càllala ya - 205]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy soññ ci nuy sukkandiku ci Yàlla mu kawe mi ci xëcc njariñ ak jeñ lor ci mbiri àdduna yi ak yu diine yi, ndax kenn du joxe te kenn du xañe, mbaa muy lore walla muy jariñe ku dul Moom Yàlla mu kawe mi. Ak it nuy def sabab yiy xëcc njariñ di jeñ lor ànd ak sukkandiku ci Yàlla, saa su nu defee loolu Yàlla dana nu wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc miy génn suba di ku xiif, mu dellusi ngoon biir bi fees dell, te jëf i picc mii benn sabab la ci dem wuti wërsëg, te bañ a bàyyandiku mbaa tàyyeel.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. gëneelu wakkirlu, ak ne dafa bokk ci sabab yi gën a màgg ci yiy xëcc wërsëg.
  3. Wakkirlu du dàqoonteek def sabab yi, ndax dañoo xamal ne dëgg-dëggi wakkirlu du wuute ak xëy walla gontu jëm ci sàkku wërsëg.
  4. Yittewoog Sariiha ci jëfi xol yi; ndax wakkirlu jëfu xol la.
  5. Sukkandiku ci sabab yi dong loolu diine ju wàññiku la, waaye bàyyi sabab yi tamit xel mu matul la.