+ -

عَنْ عَائِشَةَ رضي الله عنها قَالَتْ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ أَحْدَثَ فِي أَمْرِنَا هَذَا مَا لَيْسَ فِيهِ فَهُوَ رَدٌّ» متفق عليه. ولمسلم: «مَنْ عَمِلَ عَمَلًا لَيْسَ عَلَيْهِ أَمْرُنَا فَهُوَ رَدٌّ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2697]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees na ka ko delloo" Buxaariyu ak Muslim dëppoo nañu ci. Muslim ni mu ko nettalee mooy: "ku jëf jenn ci ludul sunu ndigal dees na ka ko delloo».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2697]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku sos ci diine ji mbaa mu jëf jëf joo xam ne Alxuraan ak Sunna tegtalewu ko, dees koy delloo boroom te deesu ko nangu fa Yàlla.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jaamu yépp ci Alxuraan AK Sunna lay tabaxu, dunu jaamu Yàlla ci lu dul lu mu yoonal, dunu ko jaamu ci ay bidaa ak yi ñu sos.
  2. Diine du tege cim xel rekk ak lees di rafetlu, waaye ci topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lay tege.
  3. Hadiis bii tegtal la ci matug diine ji.
  4. Bidaa mooy lu ñu sos ci diine ji te amutóon ci jamonoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak i Sahaabaam muy ci pas-pas walla wax mbaa jëf.
  5. Hadiis bi cosaan la ci cosaani diiney Lislaam, day mel niki balaas ci jëf yi, niki nga xamee ne jépp jëf ju ñu nammul jëmmi Yàlla mu kawe mi, aji-jëf ji du ci am ub yool, niki noonu it jépp jëf ju dëppoowul ak li Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi dees koy delloo aji-jëf ji.
  6. Sos yi ñu tere mooy yi bokk ci biri diine, waaye du yu àdduna yi.