عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ دَعَا إِلَى هُدًى كَانَ لَهُ مِنَ الْأَجْرِ مِثْلُ أُجُورِ مَنْ تَبِعَهُ، لَا يَنْقُصُ ذَلِكَ مِنْ أُجُورِهِمْ شَيْئًا، وَمَنْ دَعَا إِلَى ضَلَالَةٍ كَانَ عَلَيْهِ مِنَ الْإِثْمِ مِثْلُ آثَامِ مَنْ تَبِعَهُ، لَا يَنْقُصُ ذَلِكَ مِنْ آثَامِهِمْ شَيْئًا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2674]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug
ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara, ku woote it jëme cig reer dana am bàkkaar bu mel ni bàkkaarub ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni bàkkaar dara».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2674]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne ku tegtale daaldi ñaax nit ñi ci yoonu dëgg ak yiw ci wax mbaa jëf dana am pay gu mel ni payug ñiko ca topp ci lu dul muy wàññi dara ca payug ña ko topp. Waaye ku tegtal nit ñi jëme leen ci yoonu neen ak yoonu ay woo xamne bàkkaar moo nga ca walla mbir mu daganul, ci wax mbaa ci jëf, dana am bàkkaar bu toll ni bàkkaaru ku ko ca topp ci lu dul muy wàññi ca seen bàkkaar ya dara.