عَنْ سَلَمَةَ بْنِ الْأَكْوَعِ رضي الله عنه:
أَنَّ رَجُلًا أَكَلَ عِنْدَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِشِمَالِهِ، فَقَالَ: «كُلْ بِيَمِينِكَ»، قَالَ: لَا أَسْتَطِيعُ، قَالَ: «لَا اسْتَطَعْتَ»، مَا مَنَعَهُ إِلَّا الْكِبْرُ، قَالَ: فَمَا رَفَعَهَا إِلَى فِيهِ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2021]
المزيــد ...
Jële nañu ci Salamata ibnul Akwah -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man", dara terewu ko ko lu dul rëy, nee na: yëkkatiwaatu ko jëme ci gémmiñam.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2021]
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa gis benn waay muy lekke loxob càmmooñam, mu digal ko mu lekke loxob ndayjooram, Waa ji tontu ko ngir rëy ak di fen ci ne manu ko! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaan ko Yàlla ngir mu xañ ko mu lekke ndayjoor, Yàlla nangu ñaanug Yonnenteem bi loxob ndayjoor bi summiku, yëkkateetu ko jëme ci gémmiñam ginnaaw loolu, ci lekk mbaa ci naan.