+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ نَفَّسَ عَنْ مُؤْمِنٍ كُرْبَةً مِنْ كُرَبِ الدُّنْيَا نَفَّسَ اللهُ عَنْهُ كُرْبَةً مِنْ كُرَبِ يَوْمِ الْقِيَامَةِ، وَمَنْ يَسَّرَ عَلَى مُعْسِرٍ يَسَّرَ اللهُ عَلَيْهِ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ، وَمَنْ سَتَرَ مُسْلِمًا سَتَرَهُ اللهُ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ، وَاللهُ فِي عَوْنِ الْعَبْدِ مَا كَانَ الْعَبْدُ فِي عَوْنِ أَخِيهِ، وَمَنْ سَلَكَ طَرِيقًا يَلْتَمِسُ فِيهِ عِلْمًا سَهَّلَ اللهُ لَهُ بِهِ طَرِيقًا إِلَى الْجَنَّةِ، وَمَا اجْتَمَعَ قَوْمٌ فِي بَيْتٍ مِنْ بُيُوتِ اللهِ يَتْلُونَ كِتَابَ اللهِ وَيَتَدَارَسُونَهُ بَيْنَهُمْ إِلَّا نَزَلَتْ عَلَيْهِمِ السَّكِينَةُ، وَغَشِيَتْهُمُ الرَّحْمَةُ، وَحَفَّتْهُمُ الْمَلَائِكَةُ، وَذَكَرَهُمُ اللهُ فِيمَنْ عِنْدَهُ، وَمَنْ بَطَّأَ بِهِ عَمَلُهُ لَمْ يُسْرِعْ بِهِ نَسَبُهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2699]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ci jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc, ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira, ku suturaal ab jullit Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira, Yàlla day dimbali jaam bi fii ak jaam bi moo ngi dimbali mbokkam, ku sóobu aw yoon di ca sàkku xam-xam yàlla yombalal ko yoonu àjjana, te aw nit duñu dajaloo ci ak kër ci këri Yàlla yi di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir lu dul ne ag dal dana wàcc ci seen kaw yërmànde muur leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tudd leen ca ña fa moom, ku ay jëfam yeexal askanam du ko gaawal».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2699]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne payug jullit bi fa Yàlla day xeetoo ak li jullit bi di def ak jullit ñi; ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ak tar-tar ci jafe-jafey àdduna yi, Yàlla fay ko ci dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc yi. Ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe defal ko jàppandal dindil ko jafe-jafeem, Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira. Ku suturaal ab jullit niki mu gis ci moom lu jaaduwul a feeñal ci ay tarxiis ak i njuumte, Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira. Yàlla day dimbali jaamam bi, fii ak nit ki moo ngi dog ci dimbali mbokkam ci luy yéwénal àdduna ak diine, dimbali nag day nekk ci ñaan ak yaram ak alal ak lu dul loolu. Ku dox ci wut xam-xam, jublu ca jëmmi Yàlla mu kawe mi; Yàlla yombalal ko yoonu àjjana. Aw nit duñu dajaloo ci ag kër ci këri Yàlla yi, di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir, lu dul ne ag dal dana wàcc ci ñoom, yërmànde muur leen matale leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tagg leen ca ña ko jege, te Yàlla tudd jaam bi fa mbooloo ma gën a kawe doy na teddnga. Ku ay jëfam nekk lu mànki, ba tax eggul ca boroom jëf yu baax ya, jaadu na mu bañ a wéeru ci askanam wu tedd ak ay ngëneeli ay baayam ba noppi di gàtteñlu ci jëf yi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ibn Daxiixil Hiid nee na: lii hadiis bu màgg la, bu boole ay xeeti xam-xam ak i tënk ak i teggin, ngëneelu faj aajoy jullit ñi mi ngi ci, ak jariñ leen ci li jàppandi, ci xam-xam, walla alal, walla ndimbal, walla junj ci ag yéwénal, walla laabire, walla lu dul loolu.
  2. Xemmemloo ci yombalal ki nekk ci jafe-jafe.
  3. Ñaaxe ci dimbali jaam bi di ab jullit, ak ne Yàlla day dimbali aji-dimbalee ji kem ag ndimbalam ñeel mbokkam.
  4. Bokk na ci suturaal jullit bi: bañ a topp ay awraam, nettali nañu jële ci yenn mag ya jiitu woon mu wax ne : fekk naa fi ay nit yoo xam ne amuñu woon ay ayib, ñu tudd ayibi nit ñi, nit ñi tuddal leen ay ayib, fekk naa fi it ay nit yu amoon ay ayib, ñu bàyyi ayibi nit ñi, ñu fàtte seen i ayib.
  5. Suturaal nit ñi tekkiwul ne dañuy bàyyi lu bon bañ koo soppi, waaye da koy soppi te suturaal ko, kii nag mooy ki ñu xamewul yàq ak féttérlu gu jéggi dayo, bu dee ku mel noonu kenn du ko suturaal, waaye dañuy yóbb mbiram ca njiit la, bu dee ragaluñu ci loolu ag yàqute; loolu nag ndaxte suturaal ko da koy bewloo ci yàqute gi, te da koy ñemeloo ci muy lor jaam ñi, te it day ñemeloo ñoñ-ay yi ak rëy-rëylu yi.
  6. Ñaaxe ci sàkku xam-xam ak jàng Alxuraan ak jàngalante ko.
  7. An-Nawawii nee na: hadiis bi tegtal la ci ngëneelu dajaloo ci jàng Alxuraan ci jàkka ji...dees na ci boole it dajaloo ca daara ja ba ak daara ja ak lu ko niru bu soobee Yàlla.
  8. Fay gi Yàlla da ko a toftal ci jëf yi waaye du ci askan yi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Litwaani Dariya Rom Majri الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi