عن أسامة بن زيد رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَا تَرَكْتُ بَعْدِي فِتْنَةً أَضَرَّ عَلَى الرِّجَالِ مِنَ النِّسَاءِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5096]
المزيــد ...
Jële nañu ci Usaamata Ibn Sayd -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bàyyiwuma sama ginnaaw fitna cu dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi»
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5096]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bàyyiwul ginnaawam nattu bu gën a man a lor góor ñi ci jigéen ñi; ndax bu bokkee ci njabootam man naa waral mu topp ko ci lu wuuteek Sariiha, bu dee ab jàmbur la ci moom man naa jaxasoo ak moom ak di wéet ak moom te loolu day waral ay yàqute.