+ -

عَنْ عُبَيْدِ اللَّهِ بْنِ مِحْصَنٍ الْأَنْصَارِيِّ رَضيَ اللهُ عنهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ أَصْبَحَ مِنْكُمْ مُعَافى فِي جَسَدِهِ، آمِنًا فِي سِرْبِهِ، عِنْدَهُ قُوتُ يَوْمِهِ، فَكَأَنَّمَا حِيزَتْ لَهُ الدُّنْيَا».

[حسن] - [رواه الترمذي وابن ماجه] - [سنن ابن ماجه: 4141]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ubaydallah ibn Mihsan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ku xëy ci yéen di ku am jàmm ci yaramam, am kóolute ci bakkanam, am dundug bisam,, dafa mel ni jox nañu ko àdduna".

[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja] - [Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja - 4141]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku xëy ci yéen jullit ñi di ku wér di ku mucc ci yaramam ci tawat yi ak feebar yi, di ku am kóolute ci bakkanam ak njabootam, te ragalul ci yoonam, mu am lu ko doy ci dundug bisam ci li dagan; dafa mel ni booleel nañu ko àdduna jépp.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral ne nit ki dafa aajowoo jàmm ak kóolute ak dund.
  2. War na ci jaam bi mu sant Yàlla mu kawe mi gërëm ko ci xéewal yii.
  3. Xemmemloo ci doylu ak dëddu àdduna.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi