+ -

عَنْ أَبِي قَتَادَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا يُمْسِكَنَّ أَحَدُكُمْ ذَكَرَهُ بِيَمِينِهِ وَهُوَ يَبُولُ، وَلَا يَتَمَسَّحْ مِنَ الْخَلَاءِ بِيَمِينِهِ، وَلَا يَتَنَفَّسْ فِي الْإِنَاءِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 267]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Xataadata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu kenn ci yéen laal sakaraam ci ndayjooram fekk ma ngay saw, te bu demee duus ba noppi bu mu fompoo ndayjooram, te bu mu noyyi ci ndab li».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 267]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na yenni teggin yi; ba tax mu tere góor di laa sakaraam ci ndayjooram fekk ma ngay saw, ak ñu dindi sobe ci ginnaaw walla ci kanam ci loxo ndayjoor; ndaxte ndayjoor dañu koo waajal ngir yu tedd yi, Kem ni mu teree nit ki di noyyi ci ndab li muy naane.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral jiitug Lislaam ci teggin yi ak ci cet.
  2. Moytu mbir yu salte yi, bu ñu loroo ci laal ko na nekk loxo càmmooñ.
  3. Leeral teddngay loxo ndayjoor ak ngëneelam ci kaw loxo càmmooñ.
  4. Matug Sariihab Lislaam, ak yaatug njàngaleem.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi