عَنْ عِمْرَانَ بْنِ حُصَيْنٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
جَاءَ رَجُلٌ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: السَّلَامُ عَلَيْكُمْ، فَرَدَّ عَلَيْهِ ثُمَّ جَلَسَ، فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «عَشْرٌ» ثُمَّ جَاءَ آخَرُ فَقَالَ: السَّلَامُ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَةُ اللَّهِ، فَرَدَّ عَلَيْهِ فَجَلَسَ، فَقَالَ: «عِشْرُونَ» ثُمَّ جَاءَ آخَرُ فَقَالَ: السَّلَامُ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَةُ اللَّهِ وَبَرَكَاتُهُ، فَرَدَّ عَلَيْهِ فَجَلَسَ، فَقَالَ: «ثَلَاثُونَ».
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد والدارمي] - [سنن أبي داود: 5195]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Jenn waay ñëw na ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: assalaamu halaykum, mu fay ko mu daldi toog, Yonnente bi ne: "fukk" keneen daal di ñëw ne: assalaamu halaykum wa rahmatu Laah, mu fay ko mu toog, mu wax ne: "ñaar fukk" topp keneen ñëw daal di ne: assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu, mu fay ko mu toog, mu ne: "fanweer".
[Tane na] - - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 5195]
Jenn waay dafa ñëw ci Yonente bi daal di ne: (assalaamu halaykum) mu fay ko mu daal di toog, Yonente bi ne: bindal nañu ko fukki yiw, topp keneen ñëw daal di ne: (assalaamu halaykum wa rahmatul Laah), mu fay ko mu toog, Yonnente bi ne: amna ñaar-fukki yiw, topp keneen ñëw daal di ne: (assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu), mu fay ko mu toog, Yonnente bi ne: amna fanweeri yiw; maanaam kàddu gu nekk fukki yiw la.