عَنْ أَبِي قَتَادَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«الرُّؤْيَا الصَّالِحَةُ مِنَ اللَّهِ، وَالحُلُمُ مِنَ الشَّيْطَانِ، فَإِذَا حَلَمَ أَحَدُكُمْ حُلُمًا يَخَافُهُ فَلْيَبْصُقْ عَنْ يَسَارِهِ، وَلْيَتَعَوَّذْ بِاللَّهِ مِنْ شَرِّهَا، فَإِنَّهَا لاَ تَضُرُّهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3292]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Xataadata yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"gént gu baax ci Yàlla la jóge, gént gu bon nag ci Saytaane la jóge, bu kenn ci yéen gisee gént gu mu ragal, na tifli ci càmmooñam, te muslu ci Yàlla ci ayam, kon du ko lor".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3292]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne gént gu baax guy bégloo ci ay nelaw ci Yàlla lay jóge, gént gu bon nag te mooy gént gu ñu bañ te muy jàqloo ci Saytaane lay jóge.
Ku gis lu mu bañ na tifli ci càmmooñam, na muslu ci Yàlla ci ayam; kon du ko lor, ndax Yàlla dafa def loolu ñu tudd sabab ci mucc ci lu bon lay joge ci gént gu bon ga.