+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«قَالَ اللَّهُ عَزَّ وَجَلَّ: يُؤْذِينِي ابْنُ آدَمَ يَسُبُّ الدَّهْرَ وَأَنَا الدَّهْرُ، بِيَدِي الأَمْرُ أُقَلِّبُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4826]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Yàlla mu màgg mi nee na: doomu Aadama moo ngi may lor day ŋàññ jamono ji te man maay jamono, ci sama loxo la mbir yi nekk maa koy wëlbati guddi ak bëccëg".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4826]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne Yàlla mu kawe dafa wax ci hadiisu Al-Xudsii: nit kiy saaga ak di ŋàññ jamono ji ci bu musiba ak lu ñi sib amee moo ngi may lor di ma wàññi; ndaxte Yàlla tudd naa sellam gi moom dong mooy saytu di doxal liy xew; kon ŋàññ jamono ji mooy ŋàññ Yàlla mu màgg mi, te jamono ji mbindeef rekk la bu ñu tàggat, xew-xew yi di ci daw ci ndigalul Yàlla mu kawe mi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Hadiis bii dafa bokk ci li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-Xudsii walla Hadiisu Al-Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la joge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññee ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottalaate ak yenneen.
  2. Am teggiin ci Yàlla ci wax ak jëf.
  3. Dañoo war a gëm dogal yi, te muñ lor yi.
  4. Loru bokkul ak gaañu; nit ki dana loru ci dégg lu bon walla gis ko; waaye du gaañu ci loolu, batay dana loru ci xet gu xasaw niki soble ak laaj waaye du ca gaañu.
  5. Yàlla mu kawe mi tudd naa Sellam gi day loru ci yenn jëfi jaamam yu ñaaw yi, waaye du gaañu ci loolu, niki ni mu ko waxe ci hadiisu Al-Xudsii: "yéen sama jaam ñi yéen de manu leen a egg ci gaañ ma ba di ma gaañ, te manu leen a egg ci jariñ ma ba di ma jariñ".
  6. Ŋàññ jamono ji ak melal ko day séddalikoo ci ñatti xaaj: 1- mu ŋàññ jamono ji ci ne mooy aji-def ji; ak ne jamono ji mooy wëlbati mbir yi jëme ko ci aw yiw ak aw ay! Lii nag bokkaale gu mag la; ndax dafa gëm ne amna jeneen aji-bind ju bokk ak Yàlla, ak ne dafa askanale xew-xew yi ci ku dul Yàlla, 2- mu ŋàññ jamono ji du ngir gëm ne mooy aji-def ji; waaye dafa gëm ne Yàlla mooy Aji-Def ji waaye day ŋàññ jamono ji ndax mooy barabu mbir mii mu sib; lii nag dafa araam, 3- ma jublu ci xibaare dong ci lu dul yedd; lii moom dagan na, te bokk na ca waxu Luut ja yal na ko Yàlla dolli jàmm: {lii moom bis bu tar la}.
Tekki: Àngale Endonesi Bengali Turki Risi Sinhaaliya Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi