عَنْ أَنَسٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ:
كَانَتْ عَامَّةُ وَصِيَّةِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ حِينَ حَضَرَهُ الْمَوْتُ: «الصَّلَاةَ وَمَا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُمْ، الصَّلَاةَ وَمَا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُمْ»، حَتَّى جَعَلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُغَرْغِرُ بِهَا صَدْرُهُ، وَمَا يَكَادُ يُفِيضُ بِهَا لِسَانُهُ.
[صحيح] - [رواه النسائي في السنن الكبرى وابن ماجه] - [مسند أحمد: 12169]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Li ëppoon ci dénkaaney Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bi muy génn àdduna: "dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo, dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo" (seen jaam yi), ba Yonente bi dënnam ba tàmbalee di xar-xarale, ba daanaka làmmiñam leeratul.
[Wér na] - [رواه النسائي في الكبرى وابن ماجه] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 12169]
Li ëppoon ci dénkaaney Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel xeetam wi fekk ma nga ca sukuraatu dee: taqooleen ak julli te wattu ko te buleen ko sàggane, niki noonu it joxeleen àqi li ngeen moom ci ay jaam ak i jébéer te ngeen rafetal seen ug moomeel, deñul di ko bàmtu, ba mujj tàmbali di put gi di xar-xarale, ba sax làmmiñam mujjut a leer.