عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيِّ رضي الله عنه أَنَّهُ سَمِعَ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إِذَا رَأَى أَحَدُكُمُ الرُّؤْيَا يُحِبُّهَا فَإِنَّهَا مِنَ اللَّهِ، فَلْيَحْمَدِ اللَّهَ عَلَيْهَا وَلْيُحَدِّثْ بِهَا، وَإِذَا رَأَى غَيْرَ ذَلِكَ مِمَّا يَكْرَهُ، فَإِنَّمَا هِيَ مِنَ الشَّيْطَانِ، فَلْيَسْتَعِذْ مِنْ شَرِّهَا، وَلاَ يَذْكُرْهَا لِأَحَدٍ، فَإِنَّهَا لَنْ تَضُرَّهُ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 7045]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: dégg na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax naan:
«bu kenn ci yéen gisee ci gént lu mu bëgg, loolu ci Yàlla la bawoo, na sant Yàlla ci loolu te waxe ko, bu gisee lu dul loolu ci lu mu sib, loolu ci Saytaane la bawoo, na muslu ci ayam, te bu mu ko wax kenn, kon du ko lor».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7045]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne gént lu baax luy bég loo ci ay nelaw ci Yàlla la jóge, mu gindee ci ne na sant Yàlla ci loolu, te waxe ko, waaye bu gisee lu mu sib lu koy jàqloo loolu ci Saytaane la jóge; na muslu ci Yàlla ci ayam, te bu mu ko wax kenn; kon du ko lor, ndaxte Yàlla moo def loolu muy sabab ngir mucc ci ay gént yu bon yu toftaloo.